Li gën a yomb te bax lool si aar sa bopp si feebar yuy wallaate moy ŋay faral di raxas say loxo bamu set. Raxasal say loxo so jogee si wanak bi walla balaa ŋay lekk.
Si wetu SIDA, am na ay feebar yu bari yu jëm si wallu sëy ak jigeen. Di ŋa aar sa bopp bu baax so solee kawas soy sëy ak jigeen. Am na tamit ay kawas yuy jigeen di sol.
Mën ŋa am kawas si sàntar bi walla ŋa jënd ko si farmasi bi walla si supermarse yi.
Sooy jëfandiko ay sereŋal yuñu jëfandiko ba pare, sooy jël sinebar, mën ŋasee am infeksioŋ si sa dereet. Deel jëfandiko saa su nekk ay sereŋal yu set yu kenn mësul jëfandikoo.
Woowal Medic-Help so biiree. Ñi si xarañ nañu waxtaan li war si yaw ak li ŋay soxla yaw ak sa dóom ngir sa wergi yaram te nañu la booleel ku xarañ lool mu saytu la.
Deel faral di yobbu say dóom si Medic-Help. Medic-Help mën na la jappale tamit si li say dóom di lekk ak no leen war a toppatoo. So ko defee say dóom di nañu am wergi-yaram te nañu màgg bu baax.