Loo wara def soo feebaree

Amna ay nit yu xarañ (Medic-Help) si barabu dalukay ak tektal yi. Jege leen soy saytu sa wergi-yaram, so ëmbee, sa yaram neexul walla ŋa am ay laaj ŋir sa wergi-yaram. Nit yu xarañ yi nañu la saytu walla ñu tektal la ab doktor walla lopitaal su ko jaree.

Su fekkee Medic-Help dafa tej waxal ak liggeykat yi yore wallu jàppale ak aarukay bi.

Laaj ak xibaar si sa wallu wergi yaram nañu ko saytu ci sutura. 

Di si tek ŋa njekk a dem si Medic-Help su akcidaŋ amee. Demal si lopitaal ba su lu taxam tembe ame.

Icon_Medic_Help.png

Soo feebaree walla sa doom feebar walla ŋa am ay laaj si wallu wergi-yaram demal si Medic-Help.

 

Wallu wergi yaram si barabu daw-lakku yi

Amna ay nit yoy jot si bepp barabu daw-lakku yi si wallu wergi-yaram. Diŋa jot ay xibaar yu yaatu si dalu-web bi.